Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 22:26-34 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 22:26-34 in Kàddug Yàlla gi

26 Buurub Israyil ne ab surgaam: «Jàppal Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi, ak ca doomu Buur.
27 Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”»
28 Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»
29 Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ñu songi Ramot ga ca Galàdd.
30 Buurub Israyil nag ne Yosafat: «Damay soppi col, dugg ci xeex bi, waaye yaw solal sa mbubbam buur.» Buurub Israyil daldi soppig col, dugg ca xeex ba.
31 Fekk na buurub Siri jox ndigal fanweeri nitam ak ñaar, ñay jiite watiiri xare ya. Mu ne leen: «Buleen xeex ak kenn, du ku tuut, du ku réy, diirleen buurub Israyil, moom rekk.»
32 Ba loolu amee, ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii kay mooy buurub Israyil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag àddu ca kaw,
33 njiiti watiir ya xam ne du buurub Israyil, ñu walbatikuwaat, bàyyi ko.
34 Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israyil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiiram: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!»
1.Buur ya 22 in Kàddug Yàlla gi