Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 22:11-26 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 22:11-26 in Kàddug Yàlla gi

11 Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”»
12 Mboolem yonent ya ca des nag di waxe jenn waxyu jooju, naan: «Buur, songal Ramot ga ca Galàdd te jël ndam li, ndax Aji Sax ji moo leen teg ci say loxo.»
13 Ci kaw loolu ndaw la wooyi Mise, dem ne ko: «Ma ne, kàddug yonent ya genn la: jàmmu Buur. Kon nag, na sa kàddu ànd ak seen kàddu di genn, te nga wax jàmm.»
14 Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.»
15 Ba Mise dikkee ba ca Buur, Buur ne ko: «Mise, ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am nu bàyyi?» Mu ne ko: «Buur songal, daan, Aji Sax jee koy teg ci sa loxo!»
16 Buur nag ne ko: «Ñaata yoon laa lay giñloo ne la bu ma wax lu moy dëgg ci turu Aji Sax ji?»
17 Mise ne ko: «Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya, mbete xar yu amul sàmm. Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”»
18 Buurub Israyil ne Yosafat: «Waxuma la woon ne du wax waxyu bu baax ci man, xanaa lu bon?»
19 Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.
20 Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.
21 Noo ga dikk, taxaw fa kanam Aji Sax ji. Mu ne: “Man maa koy nax.” Aji Sax ji ne ko: “Nan?”
22 Mu ne: “Maay dikk, doon xel muy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.”
23 Looloo waral lii. Aji Sax ji moo def xel muy safaan dëgg ci sa làmmiñu yonent yii yépp, te Aji Sax ji moo tudd musiba ci sa kaw.»
24 Ba loolu amee Cedekiya doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana fu Noowug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man di wax ak yaw?»
25 Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.»
26 Buurub Israyil ne ab surgaam: «Jàppal Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi, ak ca doomu Buur.
1.Buur ya 22 in Kàddug Yàlla gi