Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 18:36-46 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 18:36-46 in Kàddug Yàlla gi

36 Ba saraxu ngoon jotee, Yonent Yàlla Ilyaas jegesi, ñaan ne: «Aji Sax ji, yaw Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, xamleel bésub tey jii ne yaw yaa di Yàlla ci Israyil, ma di sab jaam bi def lii lépp ci sa ndigal.
37 Nangul ma, Aji Sax ji, rikk nangul ma, ba mbooloo mii xam ne yaw Aji Sax ji yaa di Yàlla te yaay délloosi seen xol ci yaw.»
38 Ba loolu amee sawaras Aji Sax ji ne milib boole xoyom yàpp waak matt maak doj yaak suuf sa, ba far manq ndox ma ca kàmb ga.
39 Ba mbooloo mépp gisee loolu, dañu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Aji Sax jeey Yàlla! Aji Sax ji kay mooy Yàlla!»
40 Ilyaas ne leen: «Jàppleen yonenti Baal yii. Bu kenn ci ñoom rëcc.» Ñu jàpp leen, Ilyaas yóbbu leen ba ca xuru Kison, rendi leen foofa.
41 Gannaaw loolu Ilyaas ne Axab: «Doxal lekki te naan, ndax taw bu réy a ngi riir di ñëw.»
42 Axab dem, lekk, daldi naan. Ilyaas moom yéegi ba ca kaw tundu Karmel, sukk, dëpp jëëm ca diggante bëti óomam.
43 Mu ne surgaam: «Laggal séentuji wetu géej.» Surga ba séentuji, dikk, ne ko: «Dara newu fa.» Ilyaas ne ko mu dellu xool ba muy juróom ñaari yoon.
44 Juróom ñaareelu yoon ba, surga ba ne: «Lee de niir la wu tuut, tollu ni loxol nit, jóge géej.» Ilyaas ne ko: «Demal ne Axab, mu takk watiiram te dem, bala koo taw bee ub.»
45 Nes tuut asamaan ñuul kukk aki xàmbaar, ngelaw la jóg, taw ba sóob ak doole. Ci biir loolu Axab dawal watiiram, jëm Yisreel.
46 Aji Sax ji nag dooleel Ilyaas. Mu takk ndigg la, daw jiitu Axab ba ca buntu Yisreel.
1.Buur ya 18 in Kàddug Yàlla gi