Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 9

YOWAANA 9:9-37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!»
10Ñu ne ko: «Lu ubbi say bët?»
11Mu ne leen: «Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmu ci bëtu Silowe.” Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.»
12Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
13Noonu ñu daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon.
14Ndekete Yeesu, bés bi mu tooyale ban, ubbi bëti gumba ga, bésub noflaay la woon.
15Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen: «Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.»
16Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, manula jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésub noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar mana wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir.
17Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.»
18Yawut ya manuñu woona nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram,
19laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?»
20Waajur ya ne leen: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.
21Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.»
22Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne waa joojee boroom bàkkaar la.»
25Mu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.»
26Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?»
27Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeena bëgga nekk yéen itam ay taalibeem?»
28Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.
29Xam nanu ne Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.»
30Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët!
31Xam nanu ne Yàlla du déglu boroom bàkkaar. Waaye nag, dina déglu ki koy ragal tey def coobareem.
32Bi àddina sosoo ba tey, masuñoo dégg nit ku ubbi bëti gumbag judduwaale.
33Kon nit kookee nag, bu jógewul woon ca Yàlla, du mana def dara.»
34Ñu ne ko: «Yaw, ci biir bàkkaar nga juddoo, ba noppi di nu jàngal?» Noonu ñu dàq ko ca jàngu ba.
35Yeesu daldi yég ne dàq nañu nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: «Ndax gëm nga Doomu nit ki?»
36Waa ja ne ko: «Wax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo gëm.»
37Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.»

Read YOWAANA 9YOWAANA 9
Compare YOWAANA 9:9-37YOWAANA 9:9-37