Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 9

YOWAANA 9:3-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Yeesu ne leen: «Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom.
4Bëccëg lanu wara matal jëfi ki ma yónni; guddi dina ñëwi, goo xam ne kenn du ci mana liggéey.
5Ci bi may nekk àddina, maay leeru àddina.»
6Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ci bëti gumba ga ne ko:
7«Demal sëlmu ci bëtu Silowe.» Silowe mi ngi tekki «Yónni nañu ko.» Gumba ga daldi dem sëlmuji, délsi di gis.
8Dëkkandoom yi ak ñi ko xame woon bu jëkk ci yelwaan naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?»
9Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!»
10Ñu ne ko: «Lu ubbi say bët?»
11Mu ne leen: «Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmu ci bëtu Silowe.” Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.»
12Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
13Noonu ñu daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon.
14Ndekete Yeesu, bés bi mu tooyale ban, ubbi bëti gumba ga, bésub noflaay la woon.
15Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen: «Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.»
16Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, manula jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésub noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar mana wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir.
17Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.»
18Yawut ya manuñu woona nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram,
19laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?»
20Waajur ya ne leen: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.
21Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.»
22Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne waa joojee boroom bàkkaar la.»

Read YOWAANA 9YOWAANA 9
Compare YOWAANA 9:3-24YOWAANA 9:3-24