Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 9

YOWAANA 9:22-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne waa joojee boroom bàkkaar la.»
25Mu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.»
26Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?»
27Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeena bëgga nekk yéen itam ay taalibeem?»
28Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.
29Xam nanu ne Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.»
30Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët!
31Xam nanu ne Yàlla du déglu boroom bàkkaar. Waaye nag, dina déglu ki koy ragal tey def coobareem.
32Bi àddina sosoo ba tey, masuñoo dégg nit ku ubbi bëti gumbag judduwaale.
33Kon nit kookee nag, bu jógewul woon ca Yàlla, du mana def dara.»
34Ñu ne ko: «Yaw, ci biir bàkkaar nga juddoo, ba noppi di nu jàngal?» Noonu ñu dàq ko ca jàngu ba.
35Yeesu daldi yég ne dàq nañu nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: «Ndax gëm nga Doomu nit ki?»
36Waa ja ne ko: «Wax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo gëm.»
37Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.»
38Waa ja ne: «Boroom bi, gëm naa la.» Noonu mu jaamu Yeesu.
39Yeesu ne ko: «Àttee ma taxa ñëw àddina, ngir ñi gumba gis, ñiy gis gumba.»
40Bi Farisen ya nekkoon ak moom déggee loolu, ñu ne ko: «Xanaa kon nun it danoo gumba?»

Read YOWAANA 9YOWAANA 9
Compare YOWAANA 9:22-40YOWAANA 9:22-40