Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 6

YOWAANA 6:6-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nara def.
7Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax, bu nu ko amoon, du leen mana doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci dog wu ndaw.»
8Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko:
9«Am na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu muy jariñ mbooloo mu tollu nii?»
10Yeesu daldi ne taalibe ya: «Na ñépp toog.» Fekk ñax mu bare amoon ca bérab ba. Noonu góor ñépp àgg suuf. Waroon nañoo mat juróomi junni.
11Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk.
12Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.»
13Ñu dajale ko, daldi feesal fukki pañe ak ñaar ak desiti juróomi mburu, yi ñu doon lekk.
14Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi wara ñëw ci àddina!»
15Yeesu gis ne dañu koo nara jëlsi, fal ko buur. Mu bàyyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa.
16Bi timis jotee taalibeem ya wàcc ca tefes ga,
17dugg ci gaal, di jàll dex gi, jëm dëkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci ñoom.
18Dex gi yëngu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole.
19Bi ñu joowee lu wara tollook juróom benni kilomet, ñu séen Yeesu, muy dox ci kaw dex gi, jëm ci ñoom, ñu daldi tiit.
20Waaye Yeesu ne leen: «Man la, buleen tiit!»
21Noonu ñu nangu koo dugal ca gaal ga, gaal ga daldi teer ca saa sa ca fa ñu bëggoona wàcc.
22Ca ëllëg sa mbooloo, ma des ca geneen wàllu dex ga, gis ne genn gaal ga fa nekkoon rekk dem na. Xam nañu ne Yeesu bokku ko woon ak taalibe ya, ndaxte ñoom rekk a àndoon.
23Waaye yeneen gaal yu jóge dëkku Tiberyàdd ñëw, teer ca wetu fa ñu lekke woon mburu ma, gannaaw bi Boroom bi santee Yàlla ba noppi.
24Bi mbooloo ma gisee ne Yeesu walla taalibe ya kenn nekkatu fa, ñu dugg ca gaal yooyu, dem seeti ko Kapernawum.
25Bi ñu fekkee Yeesu ca geneen wàllu dex ga, ñu ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
26Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Yéena ngi may wër ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur.
27Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.»
28Noonu ñu laaj ko ne: «Lu nu wara liggéey, ngir matal jëf yi neex Yàlla?»
29Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.»
30Ñu ne ko: «Ban firnde nga nu mana won, ngir nu gëm la? Ban liggéey nga nara def?
31Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
32Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
33Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
34Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!»
35Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
36Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm!
37Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
38Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
39Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba.

Read YOWAANA 6YOWAANA 6
Compare YOWAANA 6:6-39YOWAANA 6:6-39