Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 6

YOWAANA 6:21-62

Help us?
Click on verse(s) to share them!
21Noonu ñu nangu koo dugal ca gaal ga, gaal ga daldi teer ca saa sa ca fa ñu bëggoona wàcc.
22Ca ëllëg sa mbooloo, ma des ca geneen wàllu dex ga, gis ne genn gaal ga fa nekkoon rekk dem na. Xam nañu ne Yeesu bokku ko woon ak taalibe ya, ndaxte ñoom rekk a àndoon.
23Waaye yeneen gaal yu jóge dëkku Tiberyàdd ñëw, teer ca wetu fa ñu lekke woon mburu ma, gannaaw bi Boroom bi santee Yàlla ba noppi.
24Bi mbooloo ma gisee ne Yeesu walla taalibe ya kenn nekkatu fa, ñu dugg ca gaal yooyu, dem seeti ko Kapernawum.
25Bi ñu fekkee Yeesu ca geneen wàllu dex ga, ñu ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
26Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Yéena ngi may wër ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur.
27Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.»
28Noonu ñu laaj ko ne: «Lu nu wara liggéey, ngir matal jëf yi neex Yàlla?»
29Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.»
30Ñu ne ko: «Ban firnde nga nu mana won, ngir nu gëm la? Ban liggéey nga nara def?
31Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
32Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
33Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
34Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!»
35Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
36Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm!
37Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
38Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
39Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba.
40Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!»
41Yawut ya tàmbali di ñurumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: «Maay ñam wi wàcce ci asamaan.»
42Ñu naan: «Ndax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam ak baayam. Kon nag lu tax léegi mu naan, mi ngi jóge asamaan?»
43Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen ñurumtu bi.
44Kenn manula ñëw ci man te Baay, bi ma yónni, xiirtalu la ci; te man dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
45Yonent yi bind nañu kàddu gii: “Yàlla dina leen jàngal ñoom ñépp.” Kon nag ku déglu te nangu waxi Baay bi, dina ñëw ci man.
46Tekkiwul ne kenn mas na gis Baay bi. Ki jóge ci Yàlla doŋŋ a ko gis.
47Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku gëm am nga dund gu dul jeex.
48Maay ñam wiy joxe dund.
49Seeni maam lekk nañu mànn ca màndiŋ ma, teewul dee nañu.
50Waaye ñam wiy wàcce ci asamaan, ku ko lekk, doo dee.
51Man maay ñam wiy dund te wàcce ci asamaan. Ku lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina mana dund.»
52Noonu Yawut ya werante werante wu tàng ci seen biir naan: «Naka la nu waa jii mana joxe yaramam, ngir nu lekk ko?»
53Yeesu ne leen: «Dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanuleen deretam, dungeen am dund ci yéen.
54Ku lekk sama yaram te naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
55Ndaxte sama yaram mooy ñam wu wóor wi, te sama deret mooy naan gu wóor gi.
56Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom.
57Baay bi ma yónni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man.
58Kon nag ñam wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww.»
59Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon jàngle ca jàngu ba ca Kapernawum.
60Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngle mii de, jafe na! Kan moo ko mana déglu?»
61Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leena jaaxal?
62Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoona nekk?

Read YOWAANA 6YOWAANA 6
Compare YOWAANA 6:21-62YOWAANA 6:21-62