Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 5

YOWAANA 5:18-43

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wuta rey, ndaxte yemul woon rekk ci baña topp ndigalu bésub noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.
19Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji manula def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf.
20Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gëna waaru.
21Maanaam, ni Baay bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund ñi mu ko bëgga jox.
22Baay bi du àtte kenn; àtte bi yépp, jox na ko Doom ji,
23ngir ñépp di teral Doom ji, ni ñuy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko yónni.
24«Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku dégg sama kàddu te gëm ki ma yónni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tàbbi ci dund.
25Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jamono dina ñëw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji ñu dee ñi di dégg baatu Doomu Yàlla ji, te ku ko dégg dinga dund.
26Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam.
27Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki.
28«Bu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn.
29Ñi daan jëf lu baax dinañu dekki, dund ba fàww, waaye ñi daan jëf lu bon, dinañu dekki, ñu daan leen.
30Manumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay àttee, te sama àtte bu jub la, ndaxte defuma sama bëgg-bëgg, ci waawi ki ma yónni doŋŋ laay aw.
31«Su ma seedeelee sama bopp, sama wax du am maana.
32Waaye keneen moo may seedeel, te bir na ma ne la muy wax ci man dëgg la.
33«Yéen yónni ngeen ay ndaw ci Yaxya, te seede na dëgg.
34Man ci sama bopp soxlawuma seedes nit; waaye nag damay wax loolu rekk, ngir ngeen mucc.
35Yaxya meloon na ni làmp buy tàkk tey leeral, te nangu ngeena bànneexu ab diir ci leeram.
36«Waaye yor naa ci man seede su gëna mag si ma Yaxya di seedeel: maa ngi def jëf, yi ma Baay biy sant. Jëf yooyu may def nag ñooy seede ne, Baay bi moo ma yónni.
37Te Baay bi ma yónni, moom itam seede na ma. Masuleena dégg baatam te masuleena gis xar kanamam,
38te kàddoom saxul ci yéen, ndaxte gëmuleen ki mu yónni.
39Yéena ngi gëstu Mbind yi, ndaxte dangeen cee yaakaar dund gu dul jeex. Mbind yooyu nag far, ci sama mbir lañuy wax;
40te bëgguleena ñëw ci man ngir am dund!
41«Wutuma tagg yu jóge ci nit.
42Waaye yéen, xam naa leen; leer na ma ne amuleen ci seen xol benn mbëggeel ci Yàlla.
43Man ñëw naa ci sama turu Baay, te nanguwuleen ma, waaye bu keneen dikkee ci turu boppam, ngeen nangu ko.

Read YOWAANA 5YOWAANA 5
Compare YOWAANA 5:18-43YOWAANA 5:18-43