Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 4

YOWAANA 4:6-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Foofa la teenu Yanqóoba nekkoon. Yeesu toog ca pindu teen ba, di noppalu ndax coonob tukki ba. Ca digg bëccëg la woon.
7Noonu jigéenu waa Samari ñëw fa di root. Yeesu ne ko: «May ma ndox, ma naan.»
8Fekk booba nag, taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba, di jënd lu ñu lekk.
9Jigéen ja ne ko: «Yaw, ngay Yawut, man maay jigéen ju dëkk Samari; nan nga ma mana ñaane ndox?» Jigéen ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokkuñu woon ak waa Samari ndab yu ñuy lekke.
10Noonu nag Yeesu ne ko: «Soo xamoon li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund.»
11Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund?
12Xanaa kay xalaatuloo ne yaa gëna màgg sunu maam Yanqóoba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, wëgg cig juram?»
13Yeesu wax ko ne: «Ku naan ci ndoxum teen bii, balaa yàgg mu maraat,
14waaye ndox mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.»
15Noonu jigéen ja daldi ko ne: «Sang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma bañatee mar, bay ñëw ba fii di rootsi.»
16Yeesu ne ko: «Demal wooyi sa jëkkër te ñëw.»
17Jigéen ja ne ko: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne amuloo jëkkër,

Read YOWAANA 4YOWAANA 4
Compare YOWAANA 4:6-17YOWAANA 4:6-17