Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 3

YOWAANA 3:5-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Yeesu ne ko: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Yàlla, doo mana bokk ci nguuru Yàlla.
6Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Yàlla, xel la.
7Li ma ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal.
8Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy dégg waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la mel it ci képp ku juddoo ci Xelum Yàlla.»
9Ci baat yooyu Nikodem ne ko: «Nu loolu mana ame?»
10Yeesu ne ko: «Yaw yaay jàngal bànni Israyil te xamuloo mbir yii?
11Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleena gëm li nu seede.
12Gannaaw gëmuleen li ma leen di wax ci mbiri àddina, naka ngeen mana gëme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan?
13Kenn masula yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki.
14Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki,
15ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
16Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
17Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.
18Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp.
19Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon.
20Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëg ndarakàmm.
21Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
22Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.

Read YOWAANA 3YOWAANA 3
Compare YOWAANA 3:5-22YOWAANA 3:5-22