Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 3

YOWAANA 3:15-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
16Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
17Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.
18Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp.
19Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon.
20Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëg ndarakàmm.
21Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
22Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.
23Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob.
24Booba tëjaguñu Yaxya ci kaso.
25Foofa ay taalibey Yaxya tàmbalee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set.
26Ci kaw loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ndax fàttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi te ñépp a ngay dem ca moom!»
27Yaxya ne leen: «Kenn manula am dara lu ko Yàlla joxul.
28Yéen ci seen bopp man ngeena seede ne waxoon naa ne duma Almasi bi waaye dañu maa yónni ma jiitusi ko.

Read YOWAANA 3YOWAANA 3
Compare YOWAANA 3:15-28YOWAANA 3:15-28