Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 2

YOWAANA 2:10-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10«Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sooga génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gëna neex ba nëgëni.»
11Firnde jii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkka def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
13Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu Mucc ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem,
14dugg ca kër Yàlla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca ëtt ba ay jaaykati nag ak yu xar ak yu pitax, ak weccikatu xaalis ya toog.
15Noonu Yeesu ràbb ab yar, daldi leen koy dàqe, ngir ñu génn ëttu kër Yàlla ga, ñoom ak xar ya ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya,
16daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!»
17Taalibeem ya fàttaliku Mbind mii: «Cawarte gi ma am ci sa kër, mu ngi mel ni taal buy tàkk ci sama biir.»
18Noonu Yawut ya ne ko: «Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne am nga sañ-sañu def lii nga def?»
19Yeesu ne leen: «Daaneel-leen kër Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.»
20Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!»

Read YOWAANA 2YOWAANA 2
Compare YOWAANA 2:10-20YOWAANA 2:10-20