Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 21

YOWAANA 21:2-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Taalibey Yeesu yii àndoon nañu: Simoŋ Piyeer; Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi»; Nataneel, mi dëkk Kana ca diiwaanu Galile; doomi Sebede ak yeneen ñaari taalibe.
3Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi.» Ñu ne ko: «Nun it danuy ànd ak yaw.» Ñu dugg gaal, daldi dem. Waaye guddi googu jàppuñu dara.
4Ci fajar gi Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe yi xàmmiwuñu ko.
5Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
6Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndijooru gaal gi, bu ko defee ngeen jàpp.» Ñu sànni fa mbaal ma, mu fees ak jën, ba manuñu ko woona génne ndox mi.
7Taalibe ba Yeesu bëggoon, ne Piyeer: «Boroom bi la!» Bi Simoŋ Piyeer déggee loolu, dafa woddoo mbubbam, ndaxte dafa summiku woon, daldi sóobu ci dex gi.
8Yeneen taalibe ya xëcc mbaal, mi fees dell ak jën, jëme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook téeméeri meetar.
9Bi ñu teeree, ñu gis ab taal, ñu ciy lakk ay jën, teg mburu ca wet ga.
10Yeesu ne leen: «Indileen ci jën, yi ngeen jàpp.»
11Simoŋ Piyeer yéeg ca gaal ga, daldi xëcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak jën yu mag; matoon na téeméeri jën ak juróom fukk ak ñett. Te li muy baree bare lépp, taxul mbaal ma dog.
12Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ci taalibe yi ñemewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam nañu ne Boroom bi la.
13Yeesu jegeñsi, jël mburu mi, jox leen, jox leen it jën.
14Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy ñetteelu yoon, bi mu feeñoo ay taalibeem.
15Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.»

Read YOWAANA 21YOWAANA 21
Compare YOWAANA 21:2-15YOWAANA 21:2-15