Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 19

YOWAANA 19:25-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Ca wetu bant, ba ñu daajoon Yeesu, yaayam a nga fa taxawoon, moom ak doomu ndeyam ju jigéen, Maryaama soxnas Këlópas, ak Maryaama mi dëkk Magdala.
26Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,»
27neeti taalibe ba: «Sa yaay a ngi nii.» Booba la ko taalibe ba yóbbu këram, yor ko.
28Bi loolu wéyee, gannaaw Yeesu xam na ne lépp mat na léegi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: «Damaa mar.»
29Amoon na foofa gutt bu fees ak bineegar. Noonu ñu jël sagar, tooyal ko ca, takk ko ci caru garab gu ñuy wax isob, teg ko ci gémmiñu Yeesu.
30Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: «Lépp mat na!» Noonu mu sëgg, delloo ruuwam Yàlla.
31Keroog ba ñu dee waajal bésub noflaay ba la woon, te Yawut ya bëgguñu néew ya des ca bant ya, ndaxte bésub noflaay boobu fonkoon nañu ko lool. Ñu ñaan Pilaat, mu dammlu tànki ña ñu daajoon, te jële leen fa.
32Noonu xarekat ya dem, damm tànki ku jëkk ka, teg ca ka ca des, ca ña ñu daajaale woon ak Yeesu.
33Bi ñu agsee ci Yeesu, dammuñu ay tànkam, ndaxte gis nañu ne booba faatu na.
34Waaye kenn ca xarekat ya daldi jël xeej, jam ko ko ci wet, ca saa sa deret ak ndox di tuuru.
35Kiy nettali mbir yooyu, da cee teg bëtam, te li muy wax dëgg la. Moom ci boppam xam na ne li muy wax dëgg la, ngir yéen itam ngeen gëm,
36ndaxte loolu dafa xew ngir Mbind mi am: «Benn yaxam du damm.»

Read YOWAANA 19YOWAANA 19
Compare YOWAANA 19:25-36YOWAANA 19:25-36