Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 9

Sarxalkat yi 9:5-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Ba mu ko defee ñu yóbbu ca bunt xaymab ndaje ma la Musaa santaane woon, mbooloo ma mépp ñëw, taxaw fa kanam Aji Sax ji.
6Musaa ne: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane ne, moom ngeen wara def ngir leeram feeñu leen.»
7Musaa wax ak Aaróona ne ko: «Dikkal fii ci sarxalukaay bi te joxe sa saraxu póotum bàkkaar ak sa saraxu rendi-dóomal, nga jotoo ko, yaw yaak mbooloo mi, boo noppee joxe saraxu mbooloo mi, jote leen ko, muy li Aji Sax ji santaane.»
8Aaróona dikk ba ci sarxalukaay bi, rendi sëllu wi, muy saraxu póotum bàkkaaram.
9Gannaaw loolu doomi Aaróona yu góor ya indil ko deret ja, mu capp ca baaraamam, taqal ca béjjéni sarxalukaay ba; la des ca deret ja mu tuur ko ca taatu sarxalukaay ba.
10Aaróona jël nebbon bi jóge ci sarax biy póotum bàkkaar, aki dëmbéenam ak bàjjo bi ci res wi, mu boole ko lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
11Yàpp wi ak der bi, mu génne ko dal ba, lakk ko, ba mu dib dóom.

Read Sarxalkat yi 9Sarxalkat yi 9
Compare Sarxalkat yi 9:5-11Sarxalkat yi 9:5-11