Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 8

Sarxalkat yi 8:6-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Ci kaw loolu Musaa indi Aaróona aki doomam yu góor, ñu sangu,
7solal Aaróona mbubb mu gudd ma, takkal ko laxasaay ga, solal ko fëxya ba, tegal ko ca xar-sànni ma, takkal ko ngañaay la ca kawam, jàppe ko ko, mu tafu ca kawam.
8Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di Urim ba ak Tumim ba,
9la ca tegu mu tegal ko kaala ga ca bopp ba, takkal ko dogu wurus wu tell wa, mooy meeteel gu sell ga, mu nekk ca kaw kaala ga, féete kanam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
10Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya,
11ba noppi wis-wisal ca juróom ñaari yoon ca kaw sarxalukaay ba, diwe ko sarxalukaay ba ak mboolem ay ndabam, boole ca mbalkam njàpp ma, mook ub tegoom ngir yooyu it sell.
12Mu sotti nag tuuti ci diw gi ñuy fale ci boppu Aaróona, diw ko, sellale ko ko.
13Ba mu ko defee Musaa indi doomi Aaróona yu góor ya, solal leen mbubb yu gudd, takkal leen ay laxasaay, solal leen mbaxana, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
14Musaa teg ca indi yëkku sarax siy póotum bàkkaar, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkku sarax siy póotum bàkkaar,
15Musaa rendi ko, sàkk ci deret ji, capp ci baaraamam, diw ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi yépp, setale ko sarxalukaay bi. Mu daldi tuur li des ci deret ji ci taatu sarxalukaay bi, sellale ko noonu, muy njotlaayal sarxalukaay bi.
16Ba loolu amee mu jël nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi.
17Li des ci yëkk wi, di der beek yàpp week sébbriit mi, mu génne ko dal bi, lakk ko ca biti, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
18La ca tegu mu indi kuuyu saraxu rendi-dóomal bi, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ca boppu kuuy ma.
19Musaa rendi ko, xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi,
20daldi daggat kuuy mi, def ko ay dog, boole bopp beek dog yeek nebbon bi, lakk ko, ba mu dib dóom.
21Ba loolu weesee Musaa boole yérey biir yi, ak yeel yi, raxas, ba noppi lakk kuuy mi yépp ca sarxalukaay ba. Loolu saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
22Gannaaw loolu Musaa indi kuuy ma ca des, di kuuyu xewu colu. Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci boppu kuuy mi,
23Musaa rendi ko, sàkk ca deret ja, taqal ca tabanu noppu ndijooru Aaróona, taqal ca baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
24Musaa doora indi doomi Aaróona yu góor ya, sàkk ca deret ja, taqal ca seen tabani noppi ndijoor ak seen baaraamu déyu ndijoor ak seen baaraamu déyu tànki ndijoor. La des ca deret ja, Musaa xëpp ko ca mboolem weti sarxalukaay bi.
25Ba mu ko defee mu génne nebbon bi, muy calgeen bi ak nebbon bi sàng yérey biir yépp ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, ak tànkub ndijoor bi.
26Layu bi def mburu yi amul lawiir, taaje fi kanam Aji Sax ji, mu jële ca menn mburu kese mu ndaw ak menn mburu mu ndaw te am diw ak menn mburu mu tàppandaar, boole ko teg ca kaw nebbon ba ak tànku ndijoor ba.
27Mu boole yooyu yépp teg ci loxol Aaróona ak loxoy doomam yu góor, ngir ñu def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
28Ba loolu amee Musaa nangoo ko ca seeni loxo, teg ko ca kaw saraxu rendi-dóomal ba, lakk ko ca sarxalukaay ba. Loolu saraxas xewu colu la woon, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.
29Musaa daldi jël dënn biy céram ci kuuyu xewu colu gi, yékkati ko, jébbal Aji Sax ji, muy saraxu yékkati-jébbale, di la Aji Sax ji santoon Musaa.
30Musaa teg ca sàkk ca diwu pal ga, ak deret ji ci sarxalukaay bi, wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ca kawi yéreem, wis-wisaale ko ca kaw yarami doomam yu góor ak ca kaw yérey doomam.
31Musaa wax ak Aaróona aki doomam yu góor ne leen: «Toggleen yàpp wi ci bunt xaymab ndaje mi te lekk ko foofa, boole kook mburu mi ci layub saraxi xewu colu gi, muy la ma santaane woon ne yaw Aaróona yaak say doom yu góor yeena koy lekk.
32Li des ci yàpp wi ak mburu mi, lakkleen ko, ba mu dib dóom.
33Waaye bunt xaymab ndaje mi buleen ko wees diiru juróom ñaari fan, ba bésub keroog ba seen xewu colu di mat, ndax juróom ñaari fan lay mat.
34Lépp lu ñu def tey, Aji Sax ji daa santaane ñu def ko, mu daldi matal seen njotlaay.

Read Sarxalkat yi 8Sarxalkat yi 8
Compare Sarxalkat yi 8:6-34Sarxalkat yi 8:6-34