Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 8

Sarxalkat yi 8:26-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
26Layu bi def mburu yi amul lawiir, taaje fi kanam Aji Sax ji, mu jële ca menn mburu kese mu ndaw ak menn mburu mu ndaw te am diw ak menn mburu mu tàppandaar, boole ko teg ca kaw nebbon ba ak tànku ndijoor ba.
27Mu boole yooyu yépp teg ci loxol Aaróona ak loxoy doomam yu góor, ngir ñu def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
28Ba loolu amee Musaa nangoo ko ca seeni loxo, teg ko ca kaw saraxu rendi-dóomal ba, lakk ko ca sarxalukaay ba. Loolu saraxas xewu colu la woon, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.
29Musaa daldi jël dënn biy céram ci kuuyu xewu colu gi, yékkati ko, jébbal Aji Sax ji, muy saraxu yékkati-jébbale, di la Aji Sax ji santoon Musaa.
30Musaa teg ca sàkk ca diwu pal ga, ak deret ji ci sarxalukaay bi, wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ca kawi yéreem, wis-wisaale ko ca kaw yarami doomam yu góor ak ca kaw yérey doomam.
31Musaa wax ak Aaróona aki doomam yu góor ne leen: «Toggleen yàpp wi ci bunt xaymab ndaje mi te lekk ko foofa, boole kook mburu mi ci layub saraxi xewu colu gi, muy la ma santaane woon ne yaw Aaróona yaak say doom yu góor yeena koy lekk.
32Li des ci yàpp wi ak mburu mi, lakkleen ko, ba mu dib dóom.
33Waaye bunt xaymab ndaje mi buleen ko wees diiru juróom ñaari fan, ba bésub keroog ba seen xewu colu di mat, ndax juróom ñaari fan lay mat.

Read Sarxalkat yi 8Sarxalkat yi 8
Compare Sarxalkat yi 8:26-33Sarxalkat yi 8:26-33