Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 7

Sarxalkat yi 7:5-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Sarxalkat bi da koy boole lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, te di saraxu peyug tooñ.
6Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Bérab bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.
7«Li ci saraxu póotum bàkkaar moo nekk ci saraxu peyug tooñ, dogal bi di benn ci yooyu yaar: sarxalkat bi def gàtt bi njotlaay moo koy moom.
8Su nit joxee ab saraxu rendi-dóomal, sarxalkat bi mooy féetewoo deru jur gi mu sarxal.
9Ci biir loolu bépp saraxu pepp mu ñu lakk cib taal, mbaa ñu saaf ko ci cin mbaa ci saafukaayu weñ, sarxalkat bi koy joxe moo koy moom.
10Waaye weneen xeetu saraxu pepp mu mu mana doon, su dee saraxu pepp mu ñuy xiiwaale diw mbaa muy mu wow, doomi Aaróona yu góor yépp a koy moom, ku nekk tollook sa moroom cér.
11«Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:
12Bu ci nit ki jubloo ag njukkal gu muy delloo Aji Sax ji, day boole ci saraxu cant gi ay mburu yu ndaw yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw ak ay mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, ak ay mburu yu ñu lakke sunguf su mucc ayib, xiiwaale ko diw, not ko bu baax.
13Sarax boobu da ciy dolli mburu yu am lawiir, boole kook saraxu cant googu ci biir jàmm te mu jublu ci njukkal.
14Nañu jooxeel Aji Sax ji ab cér ci sarax yooyu yépp, muy moomeelu sarxalkat bi xëpp deretu juru saraxas cant gi ci biir jàmm ci mboolem weti sarxalukaay bi.
15Yàppu saraxas cant googu ci biir jàmm te ñu jublu ci njukkal Aji Sax ji, dees koy lekk bés bi ñu ko rendee. Du lenn lees ciy wacc, mu fanaan.
16«Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk.
17Lu des ci yàppu sarax si ba ca gannaaw ëllëg sa dees koy lakk, ba mu dib dóom.
18Waaye kat bu nit lekkee lenn ci yàpp wu ñu def saraxu cant ci biir jàmm te fekk mu am ñetti fan, deesul nangul boroom sarax si te du ko jariñ dara. Lu ñu sib la te ku ca lekk mooy gàddu bàkkaaram.
19Yàpp wu ci laal lenn lu sobewu it deesu ko lekk. Dees koy lakk. Ci biir loolu yàppu sarax, képp ku set sañ nga cee lekk.
20Waaye ku sobewu ku lekk ci yàppu jur gu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku nañu ko dagge ci biir bànni Israyil.
21Sobe su mu mana doon, muy lu jóge ci nit mbaa mala mu daganul mbaa mboolem lu daganul te mata sib, ku ci laal ba noppi, lekk ci lu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku dees koo wara dagge ci bànni Israyil.»
22Aji Sax ji dellu wax Musaa ne ko:
23«Waxal bànni Israyil ne leen: Buleen lekk lenn luy nebbonu nag mbaa xar mbaa bëy.
24Nebbonu jur gu dee mbaa lu rabu àll fàdd, manees na koo jëfandikoo neneen nu mu mana doon, waaye deesu ko lekk mukk.
25Képp ku lekk ci nebbonu jur gu ñu def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, kooku ko lekk, dees koy dagge ca biir bànni Israyil.
26Te itam du lenn luy deret lu ngeen di lekke fenn fu ngeen dëkk, mu jóge ci njanaaw mbaa ag jur.

Read Sarxalkat yi 7Sarxalkat yi 7
Compare Sarxalkat yi 7:5-26Sarxalkat yi 7:5-26