Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 27

Sarxalkat yi 27:3-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Su dee góor gu am ñaar fukki at ba juróom benn fukki at, nanga ko xayma ci juróom fukki dogi xaalis, ci xaalisu bérab bu sell bi.
4Su dee jigéen, nanga ko xayma ci fanweeri dogi xaalis.
5Su amee juróomi at ba ñaar fukki at, danga koy xayma ci ñaar fukki dogi xaalis, su dee góor, mbaa fukki dogi xaalis, su dee jigéen.
6Su dee ku am weer jàpp juróomi at, nanga ko xayma ci juróomi dogi xaalis su dee góor; mbaa ñetti dogi xaalis su dee jigéen.
7Su dee ku am juróom benn fukki at ak lu ko ëpp, nanga ko xayma ci fukki dogi xaalis ak juróom su dee góor; mbaa fukki dogi xaalis su dee jigéen.
8Su fekkee ne ki dogu woona jagleel nit ki Aji Sax ji da di ku am-amam yées sa xayma, na kooku yóbbu nit ki ba ca sarxalkat ba, sarxalkat bi xaymaal ko nit ki ci lu dëppook am-amam, moom mi dogu woon.
9«Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe ag jur la gu dagana sarxalal Aji Sax ji, day daldi sell.
10Deesu ko weccee. Du jur gu baax gu ñu ko mana wuutoo, doonte jur gu bon la, te du jur gu bon gu ñu ko mana wuutoo, te fekk muy gu baax. Ci biir jagleel googu ku xasa wuutoo ag jur moroom ma, jur gu jëkk gaak kuutaay la dañuy bokk doon lu sell.
11Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe mala mu daganul la te daganula sarxalal Aji Sax ji, na nit ki yóbbu jur ga ba ca sarxalkat ba,
12sarxalkat ba xayma ko. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
13Su ko boroom bëggee jotaat, day fey njég ga, yokk ca xaajub juróomeelu njég ga.
14«Su nit jagleelee Aji Sax ji dëkkuwaayam, sellalal ko ko, na sarxalkat bi xayma dëkkuwaay bi. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
15Su fekkee ne ki dogu woona joxe dëkkuwaayam da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
16«Su nit jagleelee Aji Sax ji suuf su mu moom ci suufas ndonoom, na ñuy xaymaa suuf sa, na dëppook dayob pepp bay mat jiwum suuf sa. Ñetti barigoy peppum lors yu ne juróom fukki dogi xaalis a koy wecci.
17Su fekkee ne ci atum Yiwiku la joxe suuf si, xaymab suuf si day mat sëkk ànd ak moom.
18Waaye su fekkee ne gannaaw atum Yiwiku la joxe suuf si, sarxalkat bi da koy nattal njég gi ci at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca topp, génne ca at ya wees.
19Su fekkee ne ki dogu woona joxe tool bi da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
20Su jotaatul tool bi, ba ñu jaay tool bi keneen, deesu ko mana jotaat.
21Bu tool bi yiwikoo ci atum Yiwiku nag, day daldi doon lu ñu sellalal Aji Sax ji, mel ni tool bu ñu aaye, mu doon alalu sarxalkat.
22«Su fekkee ne nit ki dafa jagleel Aji Sax ji tool bu mu jënd, te donnu ko,
23sarxalkat bi da koy xaymaal njég gi, méngale kook at yi dox seen digganteek atum Yiwiku may ñëw. Na nit ki fey la ñu xayma ca bés ba, xaalis ba di lu ñuy sellalal Aji Sax ji.
24Bu atum Yiwiku dikkee, tool bi day dellu ca ka ñu ko jënde woon te mu di alalu ndonoom.
25Mboolem lu ngeen xayma, na dëppook natt ba ñu yoonal ci bérab bu sell bi, maanaam li ñuy wax siikal te mu tollu ci fukki garaam.
26«Waaye kat luy taaw cig jur, Aji Sax jee ko moom jeeg. Du lu kenn di dogoo jagleel Aji Sax ji. Muy barmol, muy mbote, muy tef, Aji Sax jeey boroom.
27Su dee lu mala mu daganul taawloo, ka ko moomoon man na koo jotaat ndegam fey na njégam, ba dolli ca xaajub juróomeelu njég ga. Bu ñu ko jotaatul, dees koy jaay ci njég gi ñu ko xaymaa.
28Mboolem lu ñu aayalal Aji Sax ji, lu sella sell la ñeel Aji Sax ji. Lépp lu nit moom, su dee nit mbaa jur mbaa suuf su mu donn, amu ci lenn lu mu aayalal Aji Sax ji te ñu sañ koo jaay mbaa mu di ko jotaat.
29Ba tey du kenn nit ku ñu aayalal bakkanam Aji Sax ji, mu wara sànku, ba noppi ñu di ko jotaat. Dees koy rey rekk.
30«Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji.
31Su fekkee ne nit ki dafa namma jotaat lenn ca céru fukkeelu meññeefam ma muy génne, day yokk ca njég ga xaajub juróomeelam.
32Mboolem céru fukkeel bu ñu génnee cig jur, gu gudd gaak gu gàtt ga, muy lépp lu sàmm waññe bantam, cérub fukkeel la bu ñuy sellalal Aji Sax ji.
33Deesu ci seet jur gu baax ak gu bon te deesu ci wuutal lenn. Bu ci nit xasee wuutal lenn, la jëkk ak la ko wuutu lépp day daldi doon lu sell. Deesu ko mana jotaat.»
34Yooyu santaane la Aji Sax ji dénkoon Musaa ca tundu Sinayi, ngir mu jottli ko bànni Israyil.

Read Sarxalkat yi 27Sarxalkat yi 27
Compare Sarxalkat yi 27:3-34Sarxalkat yi 27:3-34