Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 27

Sarxalkat yi 27:1-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bu loolu weesee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
2«Waxal bànni Israyil ne leen: Képp ku dogoo jagleel Aji Sax ji nit, man naa wàccook kàddoom ci kaw nii ñu ko xaymaa.
3Su dee góor gu am ñaar fukki at ba juróom benn fukki at, nanga ko xayma ci juróom fukki dogi xaalis, ci xaalisu bérab bu sell bi.
4Su dee jigéen, nanga ko xayma ci fanweeri dogi xaalis.
5Su amee juróomi at ba ñaar fukki at, danga koy xayma ci ñaar fukki dogi xaalis, su dee góor, mbaa fukki dogi xaalis, su dee jigéen.
6Su dee ku am weer jàpp juróomi at, nanga ko xayma ci juróomi dogi xaalis su dee góor; mbaa ñetti dogi xaalis su dee jigéen.
7Su dee ku am juróom benn fukki at ak lu ko ëpp, nanga ko xayma ci fukki dogi xaalis ak juróom su dee góor; mbaa fukki dogi xaalis su dee jigéen.
8Su fekkee ne ki dogu woona jagleel nit ki Aji Sax ji da di ku am-amam yées sa xayma, na kooku yóbbu nit ki ba ca sarxalkat ba, sarxalkat bi xaymaal ko nit ki ci lu dëppook am-amam, moom mi dogu woon.
9«Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe ag jur la gu dagana sarxalal Aji Sax ji, day daldi sell.
10Deesu ko weccee. Du jur gu baax gu ñu ko mana wuutoo, doonte jur gu bon la, te du jur gu bon gu ñu ko mana wuutoo, te fekk muy gu baax. Ci biir jagleel googu ku xasa wuutoo ag jur moroom ma, jur gu jëkk gaak kuutaay la dañuy bokk doon lu sell.
11Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe mala mu daganul la te daganula sarxalal Aji Sax ji, na nit ki yóbbu jur ga ba ca sarxalkat ba,
12sarxalkat ba xayma ko. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
13Su ko boroom bëggee jotaat, day fey njég ga, yokk ca xaajub juróomeelu njég ga.
14«Su nit jagleelee Aji Sax ji dëkkuwaayam, sellalal ko ko, na sarxalkat bi xayma dëkkuwaay bi. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
15Su fekkee ne ki dogu woona joxe dëkkuwaayam da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
16«Su nit jagleelee Aji Sax ji suuf su mu moom ci suufas ndonoom, na ñuy xaymaa suuf sa, na dëppook dayob pepp bay mat jiwum suuf sa. Ñetti barigoy peppum lors yu ne juróom fukki dogi xaalis a koy wecci.

Read Sarxalkat yi 27Sarxalkat yi 27
Compare Sarxalkat yi 27:1-16Sarxalkat yi 27:1-16