Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 26

Sarxalkat yi 26:9-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9«Te itam maa leen di baaxe, giiral leen, yokk leen. Dinaa sàmm sama kóllëreek yeen.
10Dingeen lekk ngóob mu yàgg, dence lu yàgg, ba far génne mu yàgg ma, wuutal fa mu bees.
11«Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib.
12Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ.
13Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, ngeen noppee doon seeni jaam; maa dog seen buumi njaam, siggil leen.
14«Waaye bu ngeen ma déggalul te baña jëfe sama santaane yooyu yépp,
15su ngeen teddadilee samay dogal, dëddu samay ndigal, ba jëfewuleen sama santaane yépp, xanaa di fecci sama kóllëreek yeen,
16su boobaa li may def ak yeen mooy lii: maay jekki wàcce njàqare ci seen kaw, mu ànd ak woppi ràgg, yaram wu tàng jérr ak bët yu lëndëm, ngeen gën di wopp. Dingeen ji seenum pepp ci neen, ndax seeni noon a koy lekk.
17Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.
18«Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar.
19Maay sàggi seen sag bu réy. Maay def asamaan si leen tiim ne sereŋ nig weñ, suuf si wow koŋŋ ni xànjar.
20Seen doole dina kasara, ndax suuf si ngeen di bey du leen nangul te garabi réew mi du meññ.

Read Sarxalkat yi 26Sarxalkat yi 26
Compare Sarxalkat yi 26:9-20Sarxalkat yi 26:9-20