Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 26

Sarxalkat yi 26:2-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Sama bési Noflaay, wormaal-leen ko, te sama bérab bu sell ngeen teral ko. Maay Aji Sax ji.
3«Su ngeen dee topp samay dogal, fonk samay santaane te di ko jëfe,
4kon maa leen di tawal ci waxtoom, suuf si nangu, garab yi meññ.
5Dingeen bàcc ba keroog wittum reseñ jot te dingeen witt reseñ ba keroog ji jot. Dingeen lekk seenum pepp ba suur këll te dingeen dëkk ak jàmm ci seenum réew.
6«Maay baaxee réew mi jàmm it, ba bu ngeen tëddee kenn du leen tiital. Maay jële rab wu aay ci réew mi, te saamar du jóg, dal ci seenum réew.
7Kon dingeen dàq seeni noon, saamar ba dal, ñu daanu fi seen kanam.
8Seen juróomi nit ay dàq téeméer, seen téeméeri nit dàq fukki junni. Seeni noon la saamar di dal, ñu daanu fi seen kanam.
9«Te itam maa leen di baaxe, giiral leen, yokk leen. Dinaa sàmm sama kóllëreek yeen.
10Dingeen lekk ngóob mu yàgg, dence lu yàgg, ba far génne mu yàgg ma, wuutal fa mu bees.
11«Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib.
12Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ.
13Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, ngeen noppee doon seeni jaam; maa dog seen buumi njaam, siggil leen.
14«Waaye bu ngeen ma déggalul te baña jëfe sama santaane yooyu yépp,
15su ngeen teddadilee samay dogal, dëddu samay ndigal, ba jëfewuleen sama santaane yépp, xanaa di fecci sama kóllëreek yeen,
16su boobaa li may def ak yeen mooy lii: maay jekki wàcce njàqare ci seen kaw, mu ànd ak woppi ràgg, yaram wu tàng jérr ak bët yu lëndëm, ngeen gën di wopp. Dingeen ji seenum pepp ci neen, ndax seeni noon a koy lekk.
17Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.
18«Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar.
19Maay sàggi seen sag bu réy. Maay def asamaan si leen tiim ne sereŋ nig weñ, suuf si wow koŋŋ ni xànjar.
20Seen doole dina kasara, ndax suuf si ngeen di bey du leen nangul te garabi réew mi du meññ.
21«Su ngeen saxee ci noonoo ma, bañ maa déggal, maay fulaat seen mbugal fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.

Read Sarxalkat yi 26Sarxalkat yi 26
Compare Sarxalkat yi 26:2-21Sarxalkat yi 26:2-21