Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 25

Sarxalkat yi 25:10-45

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.
11Seen atum Yiwiku la atum juróom fukkeel boobu di doon. Dungeen ci ji, dungeen ci góobaat lu saxe ca seenum ngóob te dungeen ci wolli ag reseñ, di ko witt.
12Gannaaw atum Yiwiku la, na doon at mu ngeen sellal. Saxayaayub tool ngeen saña lekk.
13«Atum Yiwiku moomu ci ngeen di delloo ku nekk suufam.
14Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante.
15Limu at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma mujj, na dëppook njég gi ngeen di jënde suuf ci seen waa réew. Limu ati mbey yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca toppaat it, war naa dëppook njég ga ñu leen jaaye.
16Lu at yooya gëna bare, njég ga gëna jafe; lu at ya gëna néew, njég ga gëna yomb, ndaxte limu meññeefum suuf sa lees leen koy jaaye.
17Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
18«Saxleen ci samay dogal, sàmm samay ndigali yoon, di ko jëfe, ndax ngeen dëkk ak jàmm ci réew mi.
19Kon suuf si dina nangu, ngeen di lekk ba suur te dëkk fa ci jàmm.
20Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?”
21Waaye dinaa leen yónnee sama barke ca atum juróom benneel ba, suuf si nangul leen meññeefum ñetti at.
22Bu ngeen tolloo ci ji ci atum juróom ñetteel ba, dina leen fekk ngeen di lekk meññeefum daaw-jéeg, te meññeefum atum juróom ñeenteel ba dina agsi, fekk ngeen di lekk ca mu daaw-jéeg ma.
23«Suuf si deesu ko jaay, mu wel fàww, ndax maay Boroom suuf si, yeen ay doxandéem ngeen fi, yu ma fi dëkkal.
24Fépp fu bokk ci seenum réew, nangeen fa yoonal sañ-sañu jotaat ca suuf sa.
25«Bu sa mbokk demee ba ñàkk tax koo jaay ci suufam, mbokkam mi ko gëna jege te am sañ-sañu jotaat suufam, na jëndaat la mbokk ma jaayoon.
26Ku amul ku ko ko jotaatal te moom ci boppam mu mujj woomle, ba am lu mu ko jotaate,
27day waññ at ya njaay ma am, delloo ki mu jaayoon ati mbey ya ca kooka dese, daldi mana jotaat ci suufam.
28Waaye su amul lu mu jëndaate suufam, suuf sa day des ca loxol ka mu jaayoon, ba keroog atum Yiwiku ma délsi. Bu atum Yiwiku ma délsee, sañ naa dellu ca suufam.
29«Su dee waa ju jaay ab dëkkuwaay bu nekk ci dëkk bu mag bu ñu tabax tata wëralee ko ko, dina ko saña jotaat li feek njaay mi amul at. Ci diir boobu la ko saña jotaate.
30Su ñu ko jotaatul ba njaay ma am atum lëmm, dëkkuwaay boobu ci biir dëkk bu mag ba ñu wëralee tata day wel fàww, ñeel ka ko jënd, mook ku askanoo ci moom. Du lees di delloo ci atum Yiwiku.
31Su dee ay dëkkuwaay ci dëkk yu ndaw yu ñu tabaxul tata, wëralee ko ko, dees koy yemaleek alali suuf. Sañees na koo jotaat te dees koy delloo ci atum Yiwiku.
32«Su dee dëkki Leween ñi ak seen dëkkuwaay ya ca biir nag, Leween ñi sañ nañu cee jotaat fàww.
33Kon alalu Leween manees na koo jotaat —dëkkuwaay lay doon bu ñu jaay ci dëkki Leween ñi— dees koy delloo bu atum Yiwiku dikkee, ndax dëkkuwaay yi ci dëkki Leween ñi, seen alal la ju leen lew fàww ci seen biir bokki bànni Israyil.
34Waaye suufas parlu yi bokk ci dëkki Leween ñi, deesu ko jaay, ndax ñoo koy moom fàww.
35«Bu seen mbokkum bànni Israyil ñàkkee ba manatula fey lu mu leen ameel, nangeen ko dimbali, ni bu doon doxandéem mbaa màngaan, ndax mu mana dund ci seen biir.
36Buleen teg lenn lu mu mana doon ci bor bu leen seen mbokk moomu ameel, waaye ragal-leen ci seen Yàlla, ndax mu mana dund ci seen biir.
37Buleen ko lebal seen xaalis, di ca teg lenn, te buleen ko jox dund, di sàkku lu mu ca yokk ngir delloo leen ko.
38Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, jox leen réewu Kanaan, te di seen Yàlla.
39«Bu seen mbokk ñàkkee ci seen biir, ba jaay leen boppam, buleen ko jaamloo.
40Defleen ko ni liggéeykat buy feyeeku mbaa màngaan bu ngeen dëkkal. Na leen liggéeyal ba keroog atum Yiwiku ma,
41mu génn ci seeni loxo, mook ay doomam, daldi dellu ci làngu boppam, fa ay maamam séddoo.
42Li waral loolu moo di bànni Israyil dañu di sama jaam yi ma génne réewum Misra. Deesu leen jaay njaam.
43Buleen leen soxore ci biir kilifteef, waaye ragal-leen ci seen Yàlla.
44Seen jaam yu góor ak seen jaam yu jigéen, nangeen leen jële ci xeet yi leen wër. Ci ñooñu ngeen di jënde ay jaam, góor ak jigéen.
45Walla ngeen jënde ba tey ci doxandéem yi ci seen biir, mbaa ci njaboot yi doxandéem yi am ci réew mi te ñu nekk ci seen biir. Su ko defee ñu doon seen ngàllo.

Read Sarxalkat yi 25Sarxalkat yi 25
Compare Sarxalkat yi 25:10-45Sarxalkat yi 25:10-45