Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 22

Sarxalkat yi 22:6-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6dina yendoo sobe sa ba jant so, te du lekk ci sarax yu sell yi ndare du dafa sangu.
7Bu jant sowee nag set na, te man naa lekk ci sarax yu sell yi, ndax ñamam la.
8Lu médd mbaa lu rab fàdd waru koo lekk, mu di ko sobeel. Maay Aji Sax ji.
9Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.
10«Kenn ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi du lekk ci sarax yu sell yi. Muy ku dal ak ab sarxalkat, muy ku koy liggéeyal di feyeeku, kenn du ci lekk ci sarax yu sell yi.
11Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu.
12Doomu sarxalkat, bu séyeek góor gu bokkul ci waa kër sarxalkat yi, jooxe yu sell yi, dootu ci saña lekk.
13Waaye doomu sarxalkat bu boroom këram faatoo mbaa mu tàggook moom te amu ca doom, bu delloo kër baayam na mu fa nekke woon ba muy gone, sañ naa lekk ci ñamu baayam. Waaye kenn ku ci bokkul sañu cee lekk.
14Gannaaw loolu képp ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi, bu lekkee ci sarax su sell te du teyeefam, na dolli ca njégu sarax sa juróomeelu céru njég ga, delloo ko sarxalkat bi.
15Te itam bu sarxalkat yi bàyyi bànni Israyil di teddadil sarax yu sell yi ñu jagleel Aji Sax ji.
16Buñu leen di bàyyi it ñuy gàddu bàkkaar buy laaj peyug tooñ, ngir lenn lu ñu lekk ci sarax yu sell yooyu. Man Aji Sax ji maa sellal yooyu sarax.»
17Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
18«Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak bànni Israyil gépp ne leen: Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa ci doxandéem yi ci Israyil, di joxeel Aji Sax ji ab saraxu rendi-dóomal, muy sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene,
19liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket.
20Lenn lu ci am sikk buleen ko sarxal, ndax deesu leen ko nangul.
21«Su nit dee joxsi Aji Sax ji aw nag mbaa gàtt, muy saraxu cant ci biir jàmm, mu di ko wàccoo ngiñ mbaa muy saraxu yéene, na doon lu amul sikk, ndax ñu nangul ko. Lenn luy sikk du nekk ci jur gi.
22Du doon lu gumba, du doon lu làggi, du doon lu kuuñ, du doon lu ami góom, mbaa lu ràmm, mbaa lu xas. Buleen sarxalal Aji Sax ji yu mel noonu. Ab saraxu sawara, buleen ko jële ci lu mel noonu, di ko joxe ci kaw sarxalukaay bi, ñeel Aji Sax ji.
23Waaye su dee nag mbaa gàtt bu ab céram ëpp mbaa mu yées, saraxu yéene la mana doon; su dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ, deesu ko nangu.
24Te it jur gu ñu motoxal ngóoraam mbaa ñu toj ko mbaa ñu xuuf ko mbaa ñu dog ko, deesu ko sarxalal Aji Sax ji. Buleen def loolu mukk ci seenum réew.
25Buleen nangoo lenn lu ni mel ci loxol doxandéem it, di ko jébbal seen Yàlla, muy saraxu ñamam. Deesu leen ko nangul, ndax la matadi ca moom mooy sikk sa.»
26Aji Sax ji wax na Musaa itam ne ko:
27«Barmol mbaa mbote mbaa tef wu doora juddu, na toog ci yaayam juróom ñaari fan; bu xasee am juróom ñetti fan, manees naa nangu mu doon saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
28Waaye su dee aw nag mbaa ab gàtt, deesu ko booleek doom ji rendi ci benn bés.
29«Bu ngeen dee defal Aji Sax ji saraxu cant, sarxal-leen ko na ñu leen koy nangule.
30Ci bés bi lees koy lekk, buleen ci fanaanal dara. Maay Aji Sax ji.
31«Kon sàmmleen samay santaane te di ko jëfe. Maay Aji Sax ji.
32Te buleen teddadil sama tur wu sell. Na bànni Israyil wormaal sama sellaay. Maay Aji Sax ji leen sellal,

Read Sarxalkat yi 22Sarxalkat yi 22
Compare Sarxalkat yi 22:6-32Sarxalkat yi 22:6-32