Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 16

Sarxalkat yi 16:3-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3«Ni Aaróona di dugge ci biir bérab bu sell bee sell nii la: day indaale aw yëkk wu ndaw ngir ab saraxu póotum bàkkaar, akum kuuy ngir ab saraxu rendi-dóomal.
4Mbubb mu sell lay sol, mu ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew ak tubéyi njiitlaay ju ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew. Na takkoo laxasaay gu ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, te kaalag wëñ gu ëccu ba sew lay takk. Yére yu sell a ngoogu; kon nag na sangu bala mu koy sol.
5Na jële ci mbooloom bànni Israyil ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal.
6«Aaróona day sarxal yëkk wi, muy saraxu póotum bàkkaaram, di njotlaayal boppam, mook waa këram.
7Gannaaw loolu na Aaróona indi ñaari sikket yi, taxawal fi kanam Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi.
8Na Aaróona tegal ñaari sikket yi bant, ngir xam bu ñuy rendil Aji Sax ji ak biy doon ngir Asasel.
9Su ko defee Aaróona indi sikket, bi muurloo, ñu sarxalal ko Aji Sax ji, rendi ko, muy saraxu póotum bàkkaar.
10Waaye sikket bi muurloo doon sikketu Asasel, dees koy taxawal muy dund fi kanam Aji Sax ji, te ni ñu koy jotoo, mooy dees koy dàq mu dem ca màndiŋ ma, ngir Asasel.
11«Bu Aaróona noppee, na indi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, def ko njotlaayam mook waa këram. Na rendi yëkku saraxas póotum bàkkaaram,
12te na sàkk andu xal bu fees, tibbe ko ca sarxalukaay ba, fi kanam Aji Sax ji, ak ñaari barci-loxoy cuuraay lu mokk te xeeñ, boole ko yóbbu ca gannaaw rido ba.
13Na def cuuraay li ci taal bi, foofa ca kanam Aji Sax ji, saxaru cuuraay si di làq kubeeru saraxu njotlaay gi ub gaalu àlluway seede si, ndax mu baña dee.
14Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.
15Bu noppee na rendi sikket biy saraxas póotum bàkkaaru mbooloo mi, te yóbbu deret ji ca gannaaw rido ba. Na def deret ji na mu defoon ak deretu yëkk wa, wis-wisal ko ca kaw kubeeru gaal gi ak ci kanam kubeer gi.
16Mu daldi matale loolu njotlaayal bérab bu sell bee sell, tàggale kook sobey bànni Israyil ak seeni tooñ, ak lu seen bàkkaar mana doon. Noonu lay defal mboolem xaymab ndaje, mi dëkk ci seen biir ci seen biiri sobe.
17Du kenn ku saña nekk ci biir xaymab ndaje mi, bu Aaróona duggee ci biir bérab bu sell bee sell, di matal ag njotlaay, ba keroog muy génn, gannaaw bu jotoo moom ci boppam, mook waa këram, ba jotaale mbooloom bànni Israyil mépp.

Read Sarxalkat yi 16Sarxalkat yi 16
Compare Sarxalkat yi 16:3-17Sarxalkat yi 16:3-17