Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 15

Sarxalkat yi 15:11-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Boroom jàngoroy xelli bu raxasul ay loxoom, ku mu laal, kooku, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
12Ndabal xandeer lu boroom jàngoroy xelli laal, dees koo wara toj. Su dee mboolem ndabal bant, dees koy raxas.
13«Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set.
14Bésub juróom ñetteel ba, na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw te teewi fi kanam Aji Sax ji ca bunt xaymab ndaje ma, daldi koy jox sarxalkat bi.
15Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju.
16«Su góor génnee wasal, war naa ragg yaramam wépp, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
17Lépp luy yére mbaa der bu wasal taq, dees koy fóot te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
18Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so.
19«Su jigéen gisee mbërëg, sobey mbërëg ma day ànd ak moom juróom ñaari fan te képp ku laal ku jigéen ka dina yendoo sobe ba jant so.
20Lépp lu mu tëdd te fekk mu gis baax, loola sobewu na te lépp lu mu toog, loola sobewu na.
21Te it képp ku laal ab lalam, war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
22Képp ku laal lenn lu mu toogoon war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
23Su toogoon ci lal mbaa leneen lu mu toogoon, ku laal loola dina yendoo sobe ba jant so,

Read Sarxalkat yi 15Sarxalkat yi 15
Compare Sarxalkat yi 15:11-23Sarxalkat yi 15:11-23