Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 15

Sarxalkat yi 15:1-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji wax na it Musaa ak Aaróona ne leen:
2«Waxleen ak bànni Israyil ne leen: Góor gu ànd ak jàngoro ju sabab ngóoraam di xelli mbér, kooku sobewu na.
3Mbér mi muy xelli moo ko sobeel; su ngóora liy xelli mbér mbaa su ko mbér mi fattee, waa ji sobewu na.
4Lal ba mu tëdd sobewu na, te lépp lu mu toog loola sobewu na.
5Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
6Ku toog ci lenn lu boroom jàngoroy xelli toogoon, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
7Ku laal boroom jàngoroy xelli war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu ànd ak sobe ba jant so.
8Su ku ànd ak jàngoroy xelli tiflee ku taqul sobe, na kooku fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
9Gépp tegu daamar gu boroom jàngoroy xelli waroon, sobewu na.
10Ku laal lenn lu mu toogoon lu ko féete woon suuf dina yendoo sobe ba jant so, te képp ku yékkati loola na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
11Boroom jàngoroy xelli bu raxasul ay loxoom, ku mu laal, kooku, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
12Ndabal xandeer lu boroom jàngoroy xelli laal, dees koo wara toj. Su dee mboolem ndabal bant, dees koy raxas.
13«Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set.
14Bésub juróom ñetteel ba, na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw te teewi fi kanam Aji Sax ji ca bunt xaymab ndaje ma, daldi koy jox sarxalkat bi.
15Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju.
16«Su góor génnee wasal, war naa ragg yaramam wépp, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
17Lépp luy yére mbaa der bu wasal taq, dees koy fóot te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
18Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so.
19«Su jigéen gisee mbërëg, sobey mbërëg ma day ànd ak moom juróom ñaari fan te képp ku laal ku jigéen ka dina yendoo sobe ba jant so.
20Lépp lu mu tëdd te fekk mu gis baax, loola sobewu na te lépp lu mu toog, loola sobewu na.
21Te it képp ku laal ab lalam, war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
22Képp ku laal lenn lu mu toogoon war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
23Su toogoon ci lal mbaa leneen lu mu toogoon, ku laal loola dina yendoo sobe ba jant so,

Read Sarxalkat yi 15Sarxalkat yi 15
Compare Sarxalkat yi 15:1-23Sarxalkat yi 15:1-23