Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 14

Sarxalkat yi 14:1-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji teg na ca ne Musaa:
2«Li yoon digle ci mbirum nit ku ame jàngoroy der juy law, keroog bés ba ñuy laabal nit ki, mooy lii: Nañu ko yegge sarxalkat bi.
3Sarxalkat bi day génn dal bi, bu koy seet. Su nit ki demee ba jàngoroy der ji ko daloon wér,
4sarxalkat bi day santaane, ñu indil nit kooku ñuy laabal ñaari picc yu dagan tey dund, ak bantu garabu seedar, ak wëñ gu xonq curr, ak caru garabu isob.
5Na sarxalkat bi santaane, ñu rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer lu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
6Picc miy dund da koy booleek bantu seedar bi ak wëñ gu xonq curr gi ak caru isob bi, boole lépp sóob ci deretu picc ma ñu rendi woon tiimale ko ndox mi balle ci bëtu ndox.
7Bu loolu amee sarxalkat bi wis-wisal juróom ñaari yoon ci kaw ki ñuy laabal, ngir mu tàggook sobey jàngoro ji. Su ko defee sarxalkat bi biral ne set na. Bu noppee na bàyyi picc miy dund mu naaw ca àll ba.
8Ku ñuy laabal day fóot ay yéreem, watu ba set te sangu, doora set. Gannaaw loolu man naa dugg ci dal bi, waaye na yem ca bunt xaymaam ca biti diiru juróom ñaari fan.
9Bésub juróom ñaareel ba na watu ba set, bopp beek sikkim beek yeen yi ak kawar gi ci des yépp lay wat, fóot ay yéreem, sangu, daldi set.
10Bésub juróom ñetteel ba na indi ñaari kuuy yu amul sikk, ak menn xar mu jigéen mu am at te amul sikk ak juróom ñeenti kiloy sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe diw, muy saraxu pepp. Mu indaale genn-wàllu liitaru diw.
11Sarxalkat biy laabal nit ki day indi nit ki, mu ànd ak loolu lépp, taxaw fi kanam Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi.
12«Sarxalkat bi teg ca jël menn kuuy mi, rendi ko, muy saraxu peyug tooñ, boole kook genn-wàll liitaru diw ga, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
13Nañu rendi kuuy mi ci bérab bu sell bi, fi ñuy rendee juru saraxu póotum bàkkaar ak saraxu rendi-dóomal, ndax li nekk ci saraxu peyug tooñ moo nekk ci saraxu póotum bàkkaar: sarxalkat bee ko moom; lu sella sell la.
14Na sarxalkat bi sàkk ci deretu jur giy saraxu peyug tooñ, taqal ko ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
15Bu sarxalkat bi noppee, na sàkk ci genn-wàll liitaru diw gi, sotti ko ci biir loxol càmmoñu boppam.
16Na sarxalkat bi capp baaraamu joxoñu ndijooram ci diw gi ci loxol càmmoñam, daldi wis-wisale diw gi baaraamam, ba mu mat juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.
17Na sarxalkat bi sàkk ci diw gi des ci loxoom, tooyal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; nañu ko laalal ci diw gi fa ñu ko jëkkoona taqal ci deretu sarax siy peyug tooñ.
18Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi, na ko diw ci boppu nit ki ñuy laabal. Noonu la ko sarxalkat bi defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji. Ba loolu amee sarxalkat bi rendi sarax biy póotum bàkkaar,
19defal ko ki ñuy laabal njotlaayam ngir mu tàggook sobeem. Te itam na sarxalkat bi rendi saraxu dóomal bi,
20boole kook saraxu pepp mi, joxe lépp ci kaw sarxalukaay bi, defal ko nit ki njotlaayam, mu set.
21«Su fekkee ne nit ki dafa ñàkk ba dooleem matewu ko, na wut menn kuuy, muy saraxu peyug tooñ, di saraxu yékkati-jébbale, ngir njotlaayam, boole kook ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, xiiwe ko diw, muy saraxu pepp. Na indaale genn-wàll liitaru diw,
22ak ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, lu mu ci gëna jekku rekk. Menn mi saraxu póotum bàkkaar la, mi ci des di saraxu rendi-dóomal.
23Da koy indil sarxalkat bi, ngir mu laabal ko bu bés ba délsee, ca bunt xaymab ndaje ma, fi kanam Aji Sax ji.
24Sarxalkat bi day jël kuuyu sarax siy peyug tooñ ak genn-wàll liitaru diw gi, boole ko, muy sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
25Gannaaw gi ñu rendi kuuy miy saraxu peyug tooñ, sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
26Bu sarxalkat bi noppee, na sotti tuuti ci diw gi ci loxol càmmoñu boppam,
27Baaraamu joxoñu ndijooram lay wis-wisale diw gi ci loxol càmmoñam ba muy juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.

Read Sarxalkat yi 14Sarxalkat yi 14
Compare Sarxalkat yi 14:1-27Sarxalkat yi 14:1-27