Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 13

Sarxalkat yi 13:32-58

Help us?
Click on verse(s) to share them!
32Sarxalkat bi day seetaat ër wi ca bésub juróom ñaareel ba. Su wat-wataan ji lawul, kawar gu xall nekku ca, te melul ni lu def pax,
33na nit ki watu waaye du wataale wat-wataan ji. Sarxalkat bi da koy beraat juróom ñaari fan.
34Na sarxalkat bi seetaat wat-wataan ji ca bésub juróom ñaareel ba. Su wat-wataan ji lawul ci yaram wi te niruwul lu def pax, sarxalkat bi day biral ne nit ki sobewuwul. Nit ki day fóot ay yéreem daldi set.
35Waaye su wéree ne wat-wataan ji law na ci yaram wi gannaaw ba ñu biralee ne set na,
36na ko sarxalkat bi dellu seet ba gis ne wat-wataan ji law na ci yaram wi. Su boobaa soxlaatul mu di ca seet kawar gu xall, ndax nit ki sobewu na.
37Waaye su seetloo ne wat-wataan ji soppikuwul te kawar gu ñuul sax ca, wat-wataan ja wér na, nit ki it set na. Na sarxalkat bi biral ne nit ki set na.
38«Su góor mbaa jigéen amee ay gàkk-gàkk yu weex ci yaram wi,
39sarxalkat bi seet ko, gàkk yooyu ci yaram wi di lu weex, xawa xall, xam rekk la, ju feeñ ci yaram wi waaye nit ki set na.
40«Góor gu bopp ba amatul kawar dafa leel waaye set na.
41Bu bopp bi ñàkkee kawar fi féeteek kanam gi, jë baa leel waaye set na.
42Waaye su amee gàkk bu weex bu feeñ te rax xonq ci leelub ndaal bopp mbaa jë, jàngoroy der la juy màgg tey génn ci leelub ndaal bopp mbaa jë.
43Sarxalkat bi da koy seet. Ndegam ay tërgën yu weex te rax xonq a ngi ci leelub ndaal bopp bi mbaa jë bi, mu mel ni jàngoroy der juy law ci yaram wi,
44nit ki ànd naak jàngoro te taq na sobe. Na sarxalkat bi biral ci lu leer ne nit ki sobewu na ndax jàngoro ji ci bopp bi.
45«Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!”
46Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi.
47«Su ndimo xuuree, teg aw liir, muy ndimol kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa yu wëñ gu ëccu,
48mu tegu ci bàgg mbaa ci poqe, su dee kawar gu ëccu, su dee wëñ gu ëccu walla der bu ñu wulli walla mboolem lu ñu defare der,
49su liir wi nëtëxee mbaa mu xonq, tege ci yére mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, liir wuy law la. Dees koy won sarxalkat bi.
50Na sarxalkat bi nemmiku liir wi, ba noppi ber këf ki teg liir wi diiru juróom ñaari fan.
51Bésub juróom ñaareel ba na seet liir wa. Su liir wa lawee ca kaw këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa der mbaa jumtukaayu der, kon liir wu aaytal la te këf ka sobewu na.
52Da koy lakk, ndax liir wu aaytal la, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa wëñ gu ëccu mbaa lu ñu defare der te liir wa tegu ca. Dees koy lakk, ba mu dib dóom.
53Waaye kat bu sarxalkat bi seetloo ne liir wi lawul ci këf ki, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa jumtukaayu der,
54na santaane ñu fóot ko, mu daldi koy beraat juróom ñaari fan.
55Ndegam nag gannaaw ba ñu fóotee këf ka teg liir, sarxalkat bi seet na ko, te liir wi soppiwul melo, bu lawul it setul. Dees koy lakk, ba mu dib dóom, su yàqoo biir ak su yàqoo biti yépp.
56Su sarxalkat bi gisee gannaaw ba ñu fóotee këf ka ne, liir wi raaf na, na dagg sànni fa tegoon liir ca këf ka, muy ndimo mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe.
57Su liir wa génnaatee ca këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, kon liir wuy màgg la. Këf ka teg liir dees koy lakk, ba mu dib dóom.
58Ndegam liir wa deñ na, gannaaw ba ñu fóotee këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, dees koy fóotaat, mu doora set.»

Read Sarxalkat yi 13Sarxalkat yi 13
Compare Sarxalkat yi 13:32-58Sarxalkat yi 13:32-58