Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 10

Sarxalkat yi 10:2-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Sawara ne jippét, bawoo fi Aji Sax ji, lakk leen ba ñu dee fa kanam Aji Sax ji.
3Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
4Ba mu ko defee Musaa woolu Mikayel ak Elsafan, góor ñiy doomi Usyel, baayu Aaróona bu ndaw. Mu ne leen: «Kaayleen jële fi seen bokk yii ci bérab bu sell bi, te ngeen génne leen dal bi.»
5Ñu jàpp ca seeni mbubb, génne leen dal ba, muy la Musaa santaane woon.
6Musaa wax Aaróona ak doomam yu góor yi tudd Elasar ak Itamar ne leen: «Buleen njañu te buleen ñaawlu di xotti seeni yére, lu ko moy dingeen dee, te merum Yàlla dina dal ci kaw mbooloo mi mépp. Waaye seen bokki bànni Israyil gépp sañ nañoo jooy ñi Aji Sax ji lakk.
7Bunt xaymab ndaje mi, buleen ko wees, lu ko moy dingeen dee, ndax diwu palu Aji Sax jaa ngi ci seen kaw.» Ñu def la leen Musaa sant.
8Aji Sax ji wax Aaróona itam ne ko:
9«Biiñ mbaa naan guy màndal bu ko kenn ci yeen naan buy duggsi ci biir xaymab ndaje mi, du yaw, du say doom yu góor, lu ko moy dingeen dee. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
10Dangeen wara mana ràññee lu sell ak lu ñu sellalul, dangeen wara ràññee itam lu set ak lu setul.
11Nangeen jàngal bànni Israyil mboolem dogal yi leen Aji Sax ji dénk, te Musaa jottli leen ko.»
12Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la.
13Lekkleen ko ci bérab bu sell. Sa cér la, yaw ak say doom yu góor, ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Loolu lañu ma sant.
14Waaye dënnu saraxu yékkati-jébbale bi ak tànkub jooxe bi, lekkleen ko ci bérab bu mucc sobe, yaak say doom yu góor ak say doom yu jigéen, ndax seen cér la, ci saraxi canti bànni Israyil ci biir jàmm, nga moom ko yaak say doom.
15Tànkub jooxe bi ak dënnu saraxu yékkati-jébbale bi, mook nebbon bi ñuy def saraxu sawara, dees koy boole indi yékkati ko, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yeena moom yooyu, yaak say doom, muy seen cér bu ñu leen dogalal fàww, te di la Aji Sax ji santaane woon.»
16Gannaaw loolu Musaa laajte, ba am lu leer ci mbirum sikketu saraxas póotum bàkkaar bi, ndekete lakk nañu ko, ba mu dib dóom. Mu mere ca doomi Aaróona yu góor ya des, di Elasar ak Itamar, ne leen:

Read Sarxalkat yi 10Sarxalkat yi 10
Compare Sarxalkat yi 10:2-16Sarxalkat yi 10:2-16