Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 92

Sabóor 92:1-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy woyu Sabóor ngir bésub Noflaay.
2Céy ngëneel li ci sant Aji Sax ji, di la woy, yaw Aji Kawe ji,
3xëye tudd sa ngor, gonloo xamle sa worma,
4xalamu fukki buum ànd ak moroom ma, xeetu kooraa jibandoo.
5Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.
6Aji Sax ji, yaa réyi jëf; xóoti pexe.
7Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.
8Bu ku bon sëqlee nim ñax, képp kuy def lu bon di yokkule, dañoo nara sànku ba fàww rekk.
9Waaye yaw ma fa kaw, yaay Aji Sax ji ba fàww.
10Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
12Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.
13Ku jub day naat nig tàndarma, màgg ni seedaru Libaŋ
14gu ñu jëmbat biir kër Aji Sax ji, muy naate sunu biir ëttu Yàlla;
15bu màggatee sax di meññ, tooy xepp, sëq lipp,

Read Sabóor 92Sabóor 92
Compare Sabóor 92:1-15Sabóor 92:1-15