Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 7

Sabóor 7:1-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko Aji Sax ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca Kuus, ma bokkoon ci giirug Beñamin.
2Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, yaw laay làqoo! Musal ma, xettli maak ñi may dàq ñépp.
3Lu ko moy ñu fàdd ma ni gaynde, daggate ma te kenn du wallu.
4Aji Sax ji sama Yàlla, ndegam maa def lii, ndegam maa taq fenn lu ñaaw,
5ndegam ku ma jàmmal laa feye aw ay, mbaa ma dimbali ku ko noonoo te defu ko dara,
6yal na ma noon rëbb, dab ma, dëggaate ma, sàggi saab sag, tëral ci pëndub suuf. Selaw.
7Aji Sax ji, meral, jóg, dajeel maak xadaru noon yi! Ngalla teewlu ma; yaw, yoon nga santaane.
8Yal na xeet yi daje, wër la, nga délsi tiim leen fu kawe.
9Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi; Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama maandute te dëggal ma.
10Yal na mbonug ku bon tees, te nga saxal kuy def njekk. Yaw Yàlla Boroom njekk, yaay natt xel ak xol.

Read Sabóor 7Sabóor 7
Compare Sabóor 7:1-10Sabóor 7:1-10