Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 79

Sabóor 79:1-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Céy Yàlla, yéefar yi song nañu sa moomeel, teddadil nañ sa kër gu sell, gental nañ Yerusalem.
2Leel nañ tan yi sa néewi jaam ñi, leel nañ rabi àll yi sa suuxi wóllëre yii.
3Ñu tuur seen deret nim ndox, ba Yerusalem daj, te amul kuy rob néew yi.
4Noo ngi nii di mbalitu dëkkandoo yi; ñu séqe nu ay kókkaleeki kekku.
5Aji Sax ji, xanaa doo nu mere ba fàww, sa fiiraange ni sawara ci sunu kaw?
6Sippil sa mer yéefar yi la xamul, ak réew yi wormaalul sa tur.
7Ñoo sëxëtoo giirug Yanqóoba, gental dëkkuwaayam.
8Bul nu topp ñaawtéef ya woon, ngalla gaaw noo gatandoo sa yërmande. Danu ne dàll, ba ne dett.
9Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu, ba sa seede rafet. Xettli nu te baal nu sunuy bàkkaar, ba sa woy rafet.
10Bul tax yéefar yi naa: «Ana seen Yàlla?» May nu, nu gis ni ngay mbugale yéefar yi, feye leen sa deretu jaam yi tuuru.
11Ñi ñu jàpp, yal na seeni onk àkki fa yaw. Ñi ci tànki ndee, yal nanga leen musale sa doole ju màgg.
12Boroom bi, sewal gi la sunuy dëkk sewal, këpp leen ko juróom yaari yoon,

Read Sabóor 79Sabóor 79
Compare Sabóor 79:1-12Sabóor 79:1-12