Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 73

Sabóor 73:6-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
7Dañoo suur ba gët suulu, seen xalaati xel xëtt yoon.
8Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, làmmiñ dajal suuf.
10Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom, di jolu seen wax nim ndox
11te naan: «Lu ci Yàlla xam? Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?»
12Ñu bon ñaa ngoog! Ne finaax, di gëna woomle.
13Man kay maa sellal ci neen, di sàmm sama der.
14Bés bu ne yar dal ma, saa yu ma xëyee, jot mbugal.
15Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,» kon de, ma wor sa askanu mbooloo.
16Naka laay jéema ràññee lii, mbir mi ëlëm ma.
17Ba ma àggee sa kër gu sell ga, laa doora gis muju ku bon.
18Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, daane leen, ñu sànku,

Read Sabóor 73Sabóor 73
Compare Sabóor 73:6-18Sabóor 73:6-18