Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 71

Sabóor 71:11-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11naan: «Yàlla wacc na ko, nan ko dàq, jàpp; kenn du ko wallu.»
12Éy Yàlla, bu ma sore. Sama Yàlla, gaawe ma.
13Samay seytaane, yal nañu leen rusloo, sànk leen. Ñi may wuta lor, yal nañu leen gàcceel, sewal leen.
14Man may saxoo yaakaar, di la sant, di santati.
15May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.
16Boroom bi, Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa njekk gu wéet.
17Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, te ba tey jii maa ngi koy biral.
18Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc, ba keroog may xamal maasu tey sa doole, xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar.
19Céy Yàlla, sa njekk àkki na fa kawa kaw. Def nga lu réy. Yaw Yàlla, ana ku mel ni yaw?
20Won nga ma ay yoon coonooki tiis, waaye yaa may dundalaat, ma mucc xóotey suuf.
21Yal nanga ma gëna sagal, geesu, bégal ma.

Read Sabóor 71Sabóor 71
Compare Sabóor 71:11-21Sabóor 71:11-21