Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 55

Sabóor 55:7-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, ma ne fërr, noppluji.
8Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
9Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»
10Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen. Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,
11guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
12Yàq a nga ca biir, te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
13Su doon noon bu may ñaawal, ma muñ ko, mbaa muy bañ bu may won ab dayo, ma daw ko.
14Waaye yaw la, sama nawle, di sama wóllëre, ma xam la.
15Nu daan bokk bànneexu diisoo, ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
16Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.
17Waaye man, Yàlla laay woo wall, te Aji Sax jee may wallu.

Read Sabóor 55Sabóor 55
Compare Sabóor 55:7-17Sabóor 55:7-17