2Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la, bul làqu, dama lay dagaan.
3Teewlu ma, nangul ma. Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp;
4coowal noon yee ak coonob ñu bon ñi. Dañu maa teg fitna, di ma songe xadar.
5Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; tiitaangey ndee ne ma taral.
6Njàqaree ma dugg, may kat-kati, musiba mëdd ma.