Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 50

Sabóor 50:1-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na, di woo àddina, penku ba sowu.
2Ca Siyoŋ, dëkk ba ca taar ba la Yàlla feeñe ni leer gu jolli.
3Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, sawaraa ko jiitu, di xoyome, ngëlén lu mag wër ko.
4Ma ngay woo seede asamaan ak suuf, ngir àtte ñoñam.
5Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre ñiy sarxal, di ko fase sama kóllëreek ñoom.»
6Asamaan a ngi biral njekkam, ngir Yàllaay àtte. Selaw.
7«Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; yeen waa Israyil, ma sikk leen. Maa di Yàlla, seen Yàlla.
8Du seeni sarax laa leen di sikke, mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
9Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
10Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
11Xam naa njanaawi tund yi, luy ndundatub tool maa ko moom.
12Su ma xiifoon, duma leen ko wax, maa moom àddinaak li ci biiram.
13Damay lekk yàppu nag ak a naan deretu sikket a?
14Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,
15di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
16Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?
17Yeena ngii, bañ sama yar, xalab samay kàddu.
18Fu ngeen gis ub sàcc, neexook moom, ab njaalookat, ngeen lëngool.
19Dangeena afal seen gémmiñ ci mbon, seen làmmiñ taqoo fen,
20ngeen di tooge seen mbokk, di yàq deru doomu ndey.
21Lii yeena ko def! Damay noppi, ngeen defe ne damaa mel ni yeen? Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis!
22«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.
23Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallu Yàlla.»

Read Sabóor 50Sabóor 50
Compare Sabóor 50:1-23Sabóor 50:1-23