Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 38

Sabóor 38:1-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.
2Éy Aji Sax ji, bul mer, di ma rëbb; bul xadaru, di ma mbugal.
3Aji Sax ji, fitt nga maa fitt, dóor nga ma.
4Danga maa mere, ma wéradi; maa bàkkaar, ba jagadi.
5Samay ñaawtéef mëdd ma, diisa diis, ba àttanuma ko.
6Maa def ug ndof, ba am dana yu bédd, ba xasaw.
7Maa ngi sëgg, ne yàcc, ne yasar, di wéye tiis,
8yaram tàng, di bax, ma wéradi, ne làcc.
9Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, jàq, di binni.
10Boroom bi, yaa ngi ne jàkk ci samay nammeel, samay onk umpu la.
11Sama fit a ngi tëf-tëfi, doole ŋiis, gët giim.
12Xarit ak dëkkandoo di ma daw, mbokk dànd ma.
13Ñi may wuta rey a ngi may fiir, di ma jéema lor, di ma waxal musiba, yendu maa lalal pexe.
14Man, ma mel nib tëx, dégguma, mel ni luu, àdduwma,
15di saf ku dul dégg, bay layoo.
16Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.
17Ma ne, ngalla buñu ma ree, di damoo samab jéll.
18Maa ngii di waaja daanu, dëkke metit.
19Ma ne, aylayéwén def naa lu ñaaw, sama bàkkaar tiital na ma.

Read Sabóor 38Sabóor 38
Compare Sabóor 38:1-19Sabóor 38:1-19