Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 25

Sabóor 25:5-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.
6Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!
7Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
8Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,
9di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.
10Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
11Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool, jéggal ma ngir saw tur.
12Ana kuy wormaal Aji Sax ji, mu won ko yoon wi mata taamu,
13muy dunde ngëneel, askanam moom réew mi?
14Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.
15Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, moo may xettli ci fiiru noon.
16Ngalla geesu ma, baaxe ma, maa wéet, néew doole,
17sama xol feesey xalaat. Rikk, teggil ma njàqare!
18Xoolal sama naqar ak sama tiis, te baal ma bépp bàkkaar.
19Xoolal noon yi ne gàññ, bañ ma mbañeelu fitna.

Read Sabóor 25Sabóor 25
Compare Sabóor 25:5-19Sabóor 25:5-19