Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 145

Sabóor 145:3-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Aji Sax jee màgg te jara màggala màggal, kii màggam amul kemu!
4Na maasoo maas di màggal say jaloore, di biral sa njàmbaarte.
5Sa leeru teddnga ji ne ràññ, ak sa jëf ju yéeme laay jàngat!
6Sa dooley jëf ju raglu dees na ko jottli, te sa màggaay maa koy yéene.
7Sa mbaax gu réy, dees na ko tari, te sag njekk, dees na ko woy.
8Yiw ak yërmande, Aji Sax ji; kee muñ mer te bare ngor!
9Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.
10Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm, sa wóllëre yi di la sant,
11di tudd sa teddngay nguur, tey dégtale sag njàmbaar,
12doom aadama xam say jaloore ak sa teddngaak sa darajay nguur.
13Sa nguur ay nguur gu sax dàkk, sa kilifteef ñeel maasoo maas. Aji Sax ji daa sàmm ay waxam, gore ciy jëfam.
14Ku daanu, Aji Sax ji wallu; ku sëgg, mu siggil.
15Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,
16tàllal sa loxo, reggal luy dund, ba xolam sedd.
17Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la, jëfam jépp ngor la.
18Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.
19Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.
20Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem, di sànk képp ku bon.

Read Sabóor 145Sabóor 145
Compare Sabóor 145:3-20Sabóor 145:3-20