Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 143

Sabóor 143:1-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; teewlul, ma tinu la; nangul ma ci sa wormaak sa njekk.
2Sang bi, bul layook man; kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.
3Noon a ma sambal, daane ma, joggati, dëël ma ci lëndëm ni ku dee bu yàgg.
4Sama doole jeex tàkk, sama xol jeex, ma ne yàcc.
5May fàttliku bu jëkkoon, di xalaat sa jaloore yépp, seetaat li nga def.
6Ma tàllal lay loxo, di la sàkku, ni suuf su mar di sàkkoo ndox. Selaw.
7Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.
8Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
9Aji Sax ji, musal ma ci noon yi, yaw laa làqoo.
10Jàngal ma, ma jëfe sa coobare; yaa di sama Yàlla. Yal na ma sam xel jiitee mbaax ci yoon wu tàlli.
11Aji Sax ji, musal ma ngir saw tur, jëfeel sag njekk, teggil ma njàqarey bakkan.

Read Sabóor 143Sabóor 143
Compare Sabóor 143:1-11Sabóor 143:1-11