2Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
3sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.
4Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer.
5Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.
6Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf.