Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 139

Sabóor 139:6-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Ni nga ma xame daa yéeme, xóot lool, ba wees ma.
7Fu ma jëm, ba sore la? Fu ma daw jëm, foo teewul?
8Ma ñalgu ba asamaan, yaa nga fa! Ma tëri njaniiw, ndeke yaa nga fa!
9Ma war laafi njël, dëkki wàllaa géej,
10nga tettee ma fa ba tey, téyee ma sa ndijoor.
11Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog, ba leer gi far guddil ma,»
12du tax lëndëm lëndëmal la dara. Guddi da laa leeralal ni bëccëg, lëndëm dig leer fi yaw.
13Yaa ma sàkkal xol ak xalaat, ràbbe ma sama biiru ndey.
14Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme, say jalooree di kéemaan, bir na ma!
15Sama jëmm jii umpu la, ba muy bindu ci kumpa, mel ni lu ñu ràbbe ci xóotey suuf.
16Gis nga ma, ba ma diw lumb; sa téere lim na fan yi nga ma àppal, ba ca benn dooragul.
17Yàlla, say xalaat aka maa yéem! Ndaw lim bu réy!
18Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf. Maa ngii yewwu, ne feek yaw ba tey.

Read Sabóor 139Sabóor 139
Compare Sabóor 139:6-18Sabóor 139:6-18