Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 8

Room 8:1-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.
2Ndax kat, dooley Noo giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci dooley bàkkaar ak ndee.
3Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,
4ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.
5Ndax kat ñi topp seen bindu suux, mbiri bakkan doŋŋ lañu xinte, waaye ñi topp Noowug Yàlla ñoom, mbiri Noowug Yàlla mooy seen xinte.
6Xintey bakkan nag ci ndee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla ndund ak jàmm lay jur.
7Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.
8Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
9Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi màkkaanoo ci yeen. Ku amul Noowug Almasi, kooku du nitam.
10Su Almasi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi.
11Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.
12Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan;
13Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
14Ndax kat, mboolem ñiy dox ci njiital Noo gi, ñooñu ay doomi Yàlla lañu.
15Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay.»
16Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
17Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
18Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
19Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.
20Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,
21ñoom ñi bokk ci càkkéef googu itam, ne dees na rengi seen buumi njaam gi leen ndee ak yàqutey yaram ràng, ngir ñu am cér ci goreelug doomi Yàlla yi, am cér ci seen teraanga.
22Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu.
23Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.
24Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootu yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee?
25Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentook a muñe yaakaar ji.
26Te itam Noo gi moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noowug Yàlla moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
27Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, nde ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
28Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
29Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.
30Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen jox itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.
31Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
32Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa jooxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?

Read Room 8Room 8
Compare Room 8:1-32Room 8:1-32