Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 6

Room 6:15-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Ba ci lan boog? Ndax kon danuy bàkkaar, gannaaw du ci kilifteefu yoonu Musaa lanu nekk, waaye ci aw yiw lanu tàbbi? Déet kay!
16Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci ndee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu jox leen àtteb ñu jub.
17Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.
18Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak noteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.
19Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga.
20Ba ngeen dee jaami bàkkaar, teewuleen woona moom seen bopp, ci seen digganteek njub.
21Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon.
22Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag sellnga la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.
23Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.

Read Room 6Room 6
Compare Room 6:15-23Room 6:15-23