Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 2

Room 2:7-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam, ak teraanga, ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ.
8Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét lañuy yooloo.
9Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;
10daraja, ak teraanga, ak jàmm nag moo ñeel képp kuy def lu baax, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci.
11Ndax kat xejj ak seen amul fa Yàlla.
12Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane.
13Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di joxee àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa lees di joxe nit àtteb ku jub.
14Jaambur ñi dul Yawut, te amuñu yoonu Musaa, ndegam teewu leena topp bindub juddu, bay jëfe li yoonu Musaa laaj, dafa fekk ñoom ci seen bopp, ñuy seen yoonu bopp, doonte amuñu yoonu Musaa.

Read Room 2Room 2
Compare Room 2:7-14Room 2:7-14