Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 16

Room 16:9-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Nuyul-leen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat ci liggéeyub Almasi, ak Estakis, sama soppe;
10nuyul-leen ma Apeles mi firndeel kóllëre gi mu am ci Almasi, te ngeen nuyul ma waa kër Aristobul,
11ak Erojon sama mbokkum Yawut, te ngeen nuyul ma waa kër Narsis ñi gëm Sang bi.
12Nuyul-leen ma Tirifen ak Tirifos, jigéen ñu sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it ndaw si Persidd mi sonn lool ci liggéeyu Boroom bi.
13Nuyul-leen ma Rufus, mi Boroom bi taamul boppam, ak yaayam jiy sama yaayu bopp.
14Nuyul-leen ma Asànkirit ak Felegon ak Ermes ak Patarobas ak Ermas, ak mboolem bokk yi nekk ak ñoom.
15Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, ak Nere ak jigéenam, ak Olimpas ak mboolem ñu sell ñi nekk ak ñoom.
16Saafoonteeleen fóonante yu sell. Mboolooy gëmkati Almasi yépp nuyu nañu leen.
17Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.
18Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi.
19Yeen nag seenug dégg ndigal siiw na ba bir ñépp, moo tax ma di leen bége. Waaye damaa bëgg ngeen xelu ci lu baax, te seenum xel mucc ci lu bon.
20Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk. Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!

Read Room 16Room 16
Compare Room 16:9-20Room 16:9-20