Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 15

ROOM 15:7-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Moo tax nangoonteleen, bay màggal Yàlla, ni leen Kirist nangoo.
8Lii laay wax: Kirist ñëw na liggéeyal Yawut yi, ngir wone kóllëreg Yàlla ci matal dige, ya mu digoon maam ya.
9Ñëw na itam ngir ñi nekkul Yawut mana màggal Yàlla ndax yërmandeem. Moo tax Mbind mi ne: «Dinaa la màggal tey tagg saw tur ci kanam xeet yépp.»
10Mbind mi nee na it: «Yéen xeeti àddina, ñëwleen bànneexu ak xeet wi Yàlla tànnal boppam.»
11Mu dellooti ne: «Santleen Boroom bi, yéen waa àddina, te ñëw màggal ko, yéen xeet yépp.»
12Te it Esayi wax na ne: «Am na sëtu Isayi buy ñëw, dina yilif xeeti ñi dul Yawut, te ci moom lañuy wékk seen yaakaar.»
13Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi.
14Bokk yi, wóor na ma ne baax ngeen ba fa mbaax mana yem, fees dell ak xam-xam, ba mana jàngleente mbiri Yàlla ci seen biir.
15Bu sama kàddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul bëgga yeesal seen xalaat, ndaxte Yàlla ci kaw yiwam daf maa sas,
16ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xibaaru jàmmam bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
17Kon nag maa ngi bànneexu ci Kirist Yeesu ngir liggéey boobu ma Yàlla dénk.
18Awma fitu wax leneen nag, lu dul li Kirist jëf jaarale ko ci man, ngir xeeti àddina jébbalu ci moom; jëf na jaarale ci samay wax ak samay jëf,
19ci ay tegtal ak i kéemaan, sukkandikoo ci dooley Xelu Yàlla mi. Ba fi mu nekk nag yégle naa fu nekk xibaaru Kirist, li dale ci Yerusalem, jaar ci gox yépp, ba àgg diiwaanu Iliri.
20Sama yéene mooy xamle xibaaru turu Kirist fa mu eggagul, ndax bëggumaa yeggale sas wu keneen daloon.
21Li ma def nag, dëppoo na ak li Mbind mi wax ne: «Ñi yégagul mbiram dinañu ko yég, te ñi ko masula dégg, xam ko.»
22Bëggoon naa ñëw seetsi leen, fekk ay téq-téq ñoo ma téye ba tey.
23Waaye nag léegi bey naa sama sas ci gox yii.
24Bu may dem Espaañ nag, bëgg naa faa jaar, nuyu leen; ndaxte ay at a ngii maa ngi am yéene ju tar ci ñëw seetsi leen. Bëgg na maa nekk ci seen biir, ngir am bànneexu sotteente ak yéen xalaat ab diir, te it ngeen waajalal ma sama yoonu Espaañ.
25Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem, ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk.
26Ndaxte waa Maseduwan ak waa Akayi ñi gëm, fas nañu yéeney sàkk ci seeni alal, yónnee ko, ngir dimbali ñi néew doole ci gaayi Yàlla yu sell, yi nekk Yerusalem.
27Yéene nañu ko, te it ci dëgg-dëgg bor la, bu ñu wara fey. Ndaxte gannaaw ñi gëm ci Yerusalem séddoo nañu ak ñi dul Yawut seen ngëm, kon xeet yooyu itam war nañoo séddoo ak ñoom seen alal.
28Kon nag waxtu wu ma noppee ci liggéey boobu, ba teg may gu tedd gii ci loxoy boroom, dinaa dem Espaañ, tey jaar fi yéen.
29Te wóor na maa ne bu ma agsee ci yéen, dinaa indaale barkeb Kirist bu mat sëkk.
30Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di ñaan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci bëggante, gi Xelu Yàlla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: àndleen ak man, nu tuur sunu ñaq ci ñaan Yàlla.

Read ROOM 15ROOM 15
Compare ROOM 15:7-30ROOM 15:7-30